wo
stringlengths 1
4.02k
⌀ | fr
stringlengths 1
1.08k
| source
stringclasses 2
values |
---|---|---|
Góor gi doon na di nit koo xam ni... | Il se trouve que l'homme est de ces gens qui... | null |
Xar menn man ŋga wax ? | Tu parles de quel mouton ? | null |
Maa di dem ! | C'est moi qui dois partir ! | null |
Danu daan réer ci biir ñax mi, muy caw sunuy xar-kanam, nuy daw bay xiiqët. Su dul woon garab yi nuy séen, dunu xamati sax fan lanu nekk. | Nous courions presque sans nous arrêter, à perdre haleine, dans les hautes herbes qui fouettaient nos visages à hauteur des yeux, guidés par les fûts des grands arbres. | null |
Gis naa ñooñale woon. | J'ai vu ceux-là. | null |
Demkoonuma | Je n'aurais pas été | null |
Jambaar la ba mu ëpp ! | Il est « excessivement » courageux ! | null |
Nit kii ci sama wet. | Cet homme près de moi. | null |
Ñàkkul gént ak janeer rax ci mbir mi. | Sans doute est-ce mêlé de légende, de rêve. | null |
Yobul na ka ŋgoon ca tool ya. | Il lui a amené du fourrage au champ. | null |
Keneen ŋga. | Tu es un autre. | null |
Tukki ëlëk | Voyager demain | null |
Ndax réew mi am na alal ? | Est-ce que le pays a des richesses ? | null |
Dem na sax ba xel mi nekk ci jëndi suuf Baxamaas, ci béréb buñ naan Elëteraa, samp fa xeetu berkelleem. | Puis il avait imaginé s'installer aux Bahamas, acheter un lopin à Eleuthera et y construire une sorte de campement. | null |
Ñooñu ñépp woon demuñu | Tous ceux-là, dont il fut question, ne sont pas partis | null |
Ndax | Est-ce que ? | null |
Dil nitu nit ñi ! | Sois l'homme de la situation ! | null |
Lii ab néeg la, néeg bi dañ kaa xadde ñax. Biñ ka xaddee ñax, néeg bi ab néeg la, néeg bi ñu xadde ko ñax ay garab nekk ca kaw ay garab nekk ci suuf. Bari nay garab lool nag sax. | Ceci est une chambre couverte d'herbe. En le couvrant d'herbe, la chambre est une sorte de chambre. La chambre est couverte d'herbe, des arbres en haut, des arbres en bas. Il y a beaucoup d'arbres tout de même. | null |
Lejum yu nëtëx a nga fay meňň | Poussent des légumes verts | null |
Gaynde la, ku dem ! | C'est peut-être un lion ! | null |
Nit lawoon ! | Ce fut un homme ! | null |
Ñooñu, ñépp dañuy dem ! | Tous ceux-là doivent partir ! | null |
Saa yu sama yaay daan nettali xew-xewi guddi googu, fàww mu yéemuwaat ca tekk-tekkaaral ga. Su weesoo yenukat yi doon ŋun-ŋuni, benn kàddu jibul. Loolu biral ni lu réy a ngi woon ci yoon wiy ñëw. | Quand ma mère raconte cela, elle dit que ce qui l'a d'abord alarmée, c'est le silence, partout, alentour, dans la forêt, et les chuchotements des porteurs. | null |
Puuriti ginnax yaa ngi muur garabi àll bi, jaxasook saxaar siy bawoo ci ban beek dex gi. | Les embruns apportés par le vent recouvrent les arbres de la forêt, se mêlent à la vapeur des marécages et de la rivière. | null |
Lëf ki ñuul na kukk. | La chose est d'un noir obscur. | null |
Góor gi rekk a ñëwul. | Seul l'homme n'est pas venu. | null |
Liggéey bii, ba mu sotti ! | Sur le travail, jusqu'à ce qu'il soit fait ! | null |
At mi mu faatoo la sidaa njëkkee feeň. | Il est mort l'année où le sida a fait son apparition. | null |
Yaakaar naa ne samay maam ak sama yaay daňoo tiit keroog ba fàtte noo duma. | Je pense que mes grands-parents et ma mère ont été si effrayés que, lorsque nous avons consenti à revenir, ils ont oublié de nous punir. | null |
Seet ŋga buu néeg ? | Tu as regardé dans cette chambre-ci ? | null |
Nettali askan wi seen bànneex, nag, di li ëpp solo ci mbir mi : ñoom ñaar, tollu ci seen diggu doole, nobante ba nga ni lii lu mu doon, mu wóor leen ni seen bànneex boobu amul gàpp, yooni Kamerun yi yaatal leen, dalal leen ci xol bu sedd guyy. Man ma dese ci ay turi dëkk, ñu may gunge, ma leen di jaawale sax ak samay santi mbokk yu ma jege. Baali, Nkom, Bamendaa, Bansoo, Nkoŋsàmbaa, Reewii, Kawaajaa. | La mémoire des instants de bonheur, lorsque mon père et ma mère sont unis par l'amour qu'ils croient éternel. Alors ils allaient dans la liberté des chemins, et les noms de lieux sont entrés en moi comme des noms de famille, Bali, Nkom, Bamenda, Banso, Nkongsamba, Revi, Kwaja. | null |
Maaleekum salaam | Que la paix soit avec toi aussi. | null |
Wante itam, demuloo | Tu n'as pas été, non plus | null |
Góor gi demoon na | L'homme avait été | null |
Waaw lii nag ab alkaati bu yor ngànnaayam, takk ndiggam di dàq ndaw sii di dem. | Oui ceci, cependant, il s'agit d'un policier qui porte une arme, ayant attaché son bassin et poursuivant ce jeune qui court. | null |
Nataal bii gis naa ci biir nataal bi ay toogukaay yu weex yu nekk ak ay taabalu dénk, ay toogukaay yoo xam ne dénk lañ ko liggéeye benn gàñcax ci wet gi. | J'ai vu à l'intérieur de la photo des ustensiles de cuisines blancs posées sur des tables en bois. Des ustensiles en bois et une plante à coté. | null |
Gàddaay baaxoo wërum réew | S'exiler à la recherche d'un pays | null |
Su demoon | S'il avait été | null |
Waaye nag, xale yi bëggunu | Malheureusement, les enfants ne veulent pas | null |
Lii nag dañ ciy faral di def ndugg maanaam jigéen ñi bu ñuy dem ja marse ba ëe, moom lañuy yor. Ñu koy woowe ci farañse pañe.. Dañu koy gàddu nag. Buñ ko gàddoo dañu ciy def lu mel niki ay ndugg daal lu mel ne jën, batañse,suppome, naaje... Yooyu daal lañuy def ci biir. | Ceci, cependant, on a l'habitude de faire les courses avec. C'est-à-dire que quand les femmes vont au marché, c'est ça qu'il emporte avec elles. On l'appelle en français'panier'. On le porte et y met des marchandises comme le poisson, aubergine, chou pommé, citrouille... C'est à peu près ça qu'on met dedans en tout cas. | null |
Ñi tawat a ngi tëdd ciy lali weñ yu darab yi dëll te weex tàll. | Les patients sont dans les dortoirs, couchés sur de vrais lits en métal aux draps empesés et très blancs, ils souffrent probablement autant de l'angoisse que de leurs affections. | null |
Lépp tuuru na. | Le tout s'est renversé. | null |
Wutëli leen gaal ! | Va leur chercher une barque ! | null |
Li mu waxoon la ! | C'est ce qu'il a dit qui est vrai ! | null |
Nagi dëkk bii ŋga gis, wa ci ëpp sa baay Alfa moo ka moom. | Des boeufs que tu vois dans cette ville, celui le plus gros appartient à ton père Alfa. | null |
Ndaje mi du gannaaw ëlëk ? | La réunion ce n'est pas après-demain ? | null |
Ramona dafa doon ma atte te waxul dara. | Ramona me jugeait silencieusement. | null |
Déedéet, defuñu dara. | Non, ils vont bien. | null |
Jeneen jabar laa bëgg ! | C'est une autre épouse que je veux ! | null |
Waxul ndax góor gi. | Il n'a rien dit à cause de l'homme. | null |
Sama maam ju góor, li mu yaroo Dunub Móris taxoon na koo bañ caaxaan waaye màggat la woon, amoon cofeel ci soxnaam te mel ni ku àddina sàppi. Lenn rekk a ko soxaloon : kimmi sigaretam « kaporaal ». Da daan faral a tëju sax ci benn pukkuus, jàpp njàmburam di tóx. | Mon grand-père maternel, lui, avait reçu dans sa jeunesse mauricienne des principes plus stricts, mais son grand âge, l'amour qu'il portait à ma grand-mère, et cette sorte de distance ennuyée propre aux gros fumeurs l'isolaient dans un réduit où il s'enfermait à clef pour, justement, y fumer en paix son caporal. | null |
Ci ñan ŋga jëm ? | Tu vas vers qui ? | null |
Mag la ndax iy atam. | C'est un homme âgé de par ses années. | null |
Foofu, góor gi dem, fu rafet la. | L'endroit, où l'homme est parti, est beau. | null |
Menn xar ñëwul. | Aucun mouton n'est arrivé. | null |
Sama xel dellu ci Afrig, am kàddu gu riir ci sama biir kaaŋ. Kàddu googu di « Kàttan ». Mbaa « Doole » ? Benn la rekk. Li wóor ba wóor moo di safaanoo na lool ak xeetu njàqare yi ma daan seetlu jamono ja ma newee gone te làrme bu Almaañ tegoon loxo ci Frãs, Almaŋ yi yóbbu fitu ñépp, lu leen neex ñu def, di jaay doole dëggëntaan. Booba, kenn du dox ci mbedd mi te sa xel newul ci ñoom. Almaŋ ya ma bett bés ak seeni mànto yu dóomu-taal, ñuy wekki sama ruuwu woto maam ju jigéen... Yemul foofu, de. Te li may waxsi, gépp gone gu màgg ci fitnay xare xam na ko. Mooy ni nit ñiy soppikoo, doon i naaféq, ku nekk ni patt ndax ragal a wax lu ëpp. Ku mel ni ndawul Amerig ca Ogosaa, te tuddoon Ogilwi, daan nay faral a déeyanteek Baay, di ko àgge ay xibaar yu mu warul woon a dégg ci yoon. Kersa dina ma teree sulli yenn yi, muy ndóol gu metti gi taxoon, ci boog liñ doon ruumandaat, samay doomi-bàjjen daan añe xollitu banaana mbaa sorãs, di ko reere. | Je me souviens de la violence en Afrique. Non pas une violence secrète, hypocrite, terrorisante comme celle que connaissent tous les enfants qui naissent au milieu d'une guerre – se cacher pour sortir, épier les Allemands en capote grise en train de voler les pneus de la voiture de ma grand-mère, entendre dans un rêve remâcher les histoires de trafic, espionnage, mots voilés, messages qui venaient de mon père par le canal de Mr Ogilvy, consul des États-Unis, et surtout la faim, le manque de tout, la rumeur des cousines de ma grand-mère se nourrissant d'épluchures. | null |
Ca Afrig, ňàkk kersag yaram yi lu yéemoon na ma lool. | En Afrique, l'impudeur des corps était magnifique. | null |
Ay mbóot yu duuf sax, ba noppi tikk ba mel ni lu xonq, di nes-nesi, xaw a tëlee naaw. | Ils étaient gras, d'un brun rougeâtre, très luisants. Ils volaient lourdement. | null |
Xale bi ne ŋgeen dugg ! | L'enfant dit d'entrer ! | null |
Maay dem | C'est moi qui vais partir | null |
Xar yooyu yan ŋga moom ? | Quels moutons qui t'appartiennent ? | null |
Maak sama mag, àddinaa ñu tooñoon. Juróomi at yi Tugal di xare yépp, danoo lëlu. Nu yaroo ci biir jigéen ñi, dëkke moytu. Ñépp a ragaloon a wax ca kow ba mu des sama maam ju jigéen ma daan móolu saa su nekkAlmaŋ yi. | Nous étions seulement deux enfants qui avaient traversé l'enfermement de cinq années de guerre, élevés dans un environnement de femmes, dans un mélange de crainte et de ruse, où le seul éclat était la voix de ma grand-mère maudissant les « Boches ». | null |
Xeetu gunóor wu waay mën a xalaat a nga woon Ogosaa. | À Ogoja, les insectes étaient partout. | null |
Dem naa doyunu | « J'ai été » ne nous suffit pas | null |
Xanaa doo dem ? | Donc, tu ne partiras pas ? | null |
Ñoom ñu ngay wéy di yab ci seeni kamyoŋ xorom ak kawari xar ak bant ak yu ni mel. | Les marchands continuent de transporter le sel, la laine, le bois, les matières premières. | null |
Gor gi dem na | L'homme est parti | null |
Joxu la woon juuti bi | Il ne t'avait pas remis la taxe | null |
Ci biir kër googule | À l'intérieur de cette maison | null |
Mas naa dégg sama yaay muy yéemu ci liñ daan jékkee-jékki rekk dëkk bépp ràkkaaju. Babungoo ko doon tax a wax, keroog. Soo jógee Bansoo, dinga dox ñeenti fan soog a yegg Babungoo, ca réewum nkom ya. | Ma mère parle des fêtes qui éclatent soudain, dans les villages, comme à Babungo, en pays nkom, à quatre jours de marche de Banso. | null |
Waa ji day noyyee ak bakkan. | L'individu respire avec son nez. | null |
Gox bi mu yilif nag, yaatu na lool. | Le territoire qu'il a en charge est immense. | null |
Nit ñi doonkoonuñu ay kaaŋ. | Les gens n'eussent pas été des maîtres. | null |
Nit ñenn ñi yegseeguñu. | Certaines personnes ne sont pas encore arrivées. | null |
Foofee fan ? | Là-bas où ? | null |
Xammeewoon naa jigéen joojale ! | J'avais reconnu cette dame-là ! | null |
Ci bir : foofu di leer | À l'intérieur : où il fait clair | null |
Keneen kookule muy woo. | De cet autre qu'on appelle. | null |
Gis naa kooku woon. | J'ai vu celui-là, auparavant. | null |
Nit ku baax la ! | C'est quelqu'un de bien ! | null |
Ci kër gi waa ji wax | Dans la maison dont parle le Monsieur | null |
Xar yii yan ŋga jënd ? | C'est ces moutons que tu avais achetés ? | null |
Ñeñeen lañu. | Autres, ils sont. | null |
Daan na yaatal, di xóotal, tey yokk yëg-yëg. | Elle donnait du champ, de la profondeur, elle multipliait les sensations, elle tendait un réseau humain autour de moi. | null |
Gis naa xar mu góor ma. | J'ai vu l'ovin mâle. | null |
Nit lañu ! | Ils ont été quelqu'un ! | null |
Nit kookuu génn laa wax ! | Je parle de la personne qui est sortie ! | null |
Gaynde gi dawul, moontin. | Le lion n'a pas fui, pourtant. | null |
jigeen ňaak góor ňa donte dañu tëdd | où femmes et hommes même couchés | null |
Ma ngii dem | Voilà qu'il est parti | null |
Sama nataal bii ñu ma yónnee dafa mel ni ab sées la, sées yi ñuy tooge. Waaye nag couleur bi moom dafa bula couleur bu bula la. | Sur ma photo qu'on m'a envoyée, il y a apparemment une chaise, sur laquelle on s'assoit. Mais, elle est clairement de couleur bleue. | null |
Beneen néeg laa bëgg ! | C'est une autre maison que je veux ! | null |
Gis ŋga sa yan xarit ? | Tu as vu quels amis à toi ? | null |
Àbbaa daanu. Àbbaa, sorewul xàmbi Aro Suku ya. Biyaafaraa tàmbalee sukkuraat, sukkuraat ju metti te yàgg. | À la chute d'Aba (non loin de l'ancien sanctuaire des guerriers magiciens d'Aro Chuku), le Biafra entre dans une longue agonie. | null |
Jox naa téere bi góor gi ñëw. | J'ai donné le livre à l'homme qui est venu. | null |
Xanaa léeg-léeg rekk nuy janeer, di déggaat sama baatu maam ju jigéen ak i léebam. Am nay bés it, sama maam ju góor a may ganeseek baatam bu neex ba, baatu doomu réewum Móris. Su weesoo ñaar ñoonu, samay maas xanaa, ña ma doon àndal di dem lekool mbaa di fo. Waaye loolu lépp dafa mujjee dee, mel niy fowukaay yu ñu tëj ci waxande, fàtte leen fa ba ñu pënde. Ak it mbóoti njaboot gi, li kenn ñemewul a tudd. | Une grand-mère avec ses contes, un grand-père avec sa voix chantante de Mauricien, des camarades de jeu, de classe, tout cela s'était glacé tels des jouets qu'on enferme dans une malle, telles les peurs qu'on laisse au fond des placards. | null |
Giskóonuma leen | Je ne vous eusse pas vus | null |
Noo tudd ? | Comment t'appelles-tu ? | null |
Ndax kan dem ? | Afin que parte ? | null |
Masul a toog ba xalaat ni dina fa jógeji bés. | Il avait cru qu'il n'en partirait pas. | null |