wo
stringlengths 1
4.02k
⌀ | fr
stringlengths 1
1.08k
| source
stringclasses 2
values |
---|---|---|
Gor gi dafa demul ? | L'homme, il n'est pas parti ? | null |
Ndaw si ak waa ji itam dañu bëggul déggoo | La femme et l'homme non plus ne désirent s'entendre | null |
Ci foofu ba ŋgeen dellusi ! | Là-bas jusqu'à ce que vous reveniez ! | null |
Góor gi mu àndi | L'homme qu'il a amené | null |
Fii laa dunde dundug njaay-àll, moom sama bopp ba léeg-léeg sax mu mënoon maa gaañ. | C'est ici, dans ce décor, que j'ai vécu les moments de ma vie sauvage, libre, presque dangereuse. | null |
Bés, sibbiru su metti daaneel ko, ñu war koo sol deret. Ma laaj waa loppitaan bi ay kayitam. | Lorsque, à la suite d'une mauvaise grippe, il est hospitalisé brièvement pour une transfusion sanguine, j'obtiens avec difficulté que le résultat des examens lui soit transmis. | null |
Penkub Niseryaa, xonjom dafa fa muuroo lëndëm, raglu te itam ñoxor-njaay ñu posone la nga dee. | Dans l'est du Nigeria, la sorcellerie est secrète, elle s'exerce au moyen des poisons, des amulettes cachées, des signes destinés à porter malheur. | null |
Su demee | S'il est parti | null |
Nit ki dóor na nag wi ak bant. | L'homme a frappé la vache avec un bâton. | null |
Agsileen ak jaam | Venez en paix | null |
Na nga def ? | Comment vas-tu ? | null |
Gor gii dem | Mais cet homme est parti | null |
Gis na ma ! | Il m'a vu ! | null |
Foofu, góor gi mer. | Alors, l'homme se fâcha. | null |
Seeti ka ! | Va le voir ! | null |
Ba ni muy demee alaateret, ñaari yoon la delsi Tugal. | Sauf pour deux brefs congés, il ne reviendra plus en Europe jusqu'à la fin de sa vie active. | null |
Ndax waa ji génn ? | Que la personne sorte ? | null |
Nileen ka | Dites-lui | null |
Ana foo jëm ? | Où est-ce que tu vas ? | null |
Ya di ban jaŋgkat ? | Tu es quel étudiant ? | null |
Gàddaay jëm Afrig a dakkal loolu lépp. | Le voyage en Afrique met fin à tout cela. | null |
Mi ŋgi fii ? | Il est là ? | null |
Maraxum nataalu xarnu bi | Le clair-obscur d'un tableau du siècle | null |
Waaye dunu woon liy bindkat yu siiw tudde ay « doomi-tubaabi-Afrig », di leen kókkali. | Nous n'avons rien connu de ce qui a pu fabriquer l'identité un peu caricaturale des enfants élevés aux « colonies ». | null |
Ndax kan dem ? | Afin que qui parte ? | null |
Naka waa kër ga ? | Comment vont les gens de la maison ? | null |
Guddi gu Yàlla sàkk, naaxi mbóot laa daan gis ci kër gi. Ca Tugal, sama maam ju góor a nga leen daan woowe'kànkarlaa', di dem ba ciy jukkiy cax, di woy ci kàllaama kerewol kànkarla, nabit nàppaa kilot, « mbóot sol na yére waaye teewu koo def taatu neen ». | Je n'ai pas besoin de faire de grands efforts d'imagination pour voir surgir à nouveau, chaque nuit, les armées de cafards – les cancrelats, comme les appelait mon grand-père, sujets d'une sirandane : kankarla, nabit napas kilot, il porte un habit, mais n'a pas de culotte. | null |
Dem naa ci keneen ku baax. | J'ai été chez un autre qui est gentil. | null |
Lii ay néegu ñax la, néegu ñax yu màggat ay nit di ci dox ci biir. Am na yi nga xam ne si nii dañ liiwe ay sàkket dañ ko muure ay sàkket ak ay bant ak ay garab. | Ceux-ci sont de vieilles cases à l'intérieur desquelles des personnes marchent. Ceux qui ont froid, ils la couvrent avec une façade, des bâtons et des arbres. | null |
Ci biir soo bëggul ! | À l'intérieur si tu ne veux pas ! | null |
Nit ñenn ñooñii laa wax ! | Je parle de ces autres individus ! | null |
Jile wax rafetul ! | Ce n'est pas là une belle parole ! | null |
Séen naa ay yëf. | J'ai aperçu des choses. | null |
Defe naa du kookuu, du kookee | Je crois que ce n'est pas celui-ci, ce n'est pas celui-là | null |
Ca njëlbéen ga, dalu simoŋ bi dafa ma daan gaañ. Xawma lu tax, sama benn baaraamu tànk kott la der bi daan xolleeku, te muy baaraamu ndey-joor bu mag bi. | Les premiers temps, je m'écorchais sur le ciment du sol en courant – je ne sais pourquoi, c'était toujours le gros orteil du pied droit dont la peau s'arrachait. | null |
Gis ŋga lan ? | Tu as vu quoi ? | null |
Ñu dikkul ? | Lesquels ne sont pas venus ? | null |
Xar mii man ? | Quel mouton ? | null |
Daawuñu ko fey fiftin bi gën a tuuti ci liggéey boobu mu daan def, wànte da doon yokk darajaam, ñu koy xoole bëti doktoor bi wóolu. | Il n'était pas payé pour le travail qu'il faisait. Sans doute y gagnait-il du prestige, du crédit : il était l'homme de confiance du toubib. | null |
Bëgg naa tuuti xaalis ci yaw | Je veux un peu d'argent de toi | null |
Ana góor gi mu wax ? | Où est l'homme dont il parle ? | null |
Foofule fépp ? | Tout cet endroit-là ? | null |
Maa fiy nekk tày ci ŋgoon, tày ci suba ! | Ce matin ou ce soir c'est moi qui suis ici ! | null |
Li ma tudde naax, daanaka dexu mellentaan la woon. Yàkkamtiwuñu, de. Ñu ngay dox ndànk, du dara lu leen mën a tee wéy di dem. Bu ci nekk a ngi sës ca moroom ma, ñu topp seen yoon rekk, gumba, tëx. Ñu ngay ŋeeñ it, lu ñu romb rajaxewaale ko. | Une colonne, plutôt un fleuve épais, qui avance lentement, sans s'arrêter, sans se soucier des obstacles, droit devant, chaque fourmi soudée à l'autre, dévorant, brisant tout sur son passage. | null |
Ci kii, ci kuu, ci kee | Vers celui que voilà, vers celui-ci, vers celui-là | null |
Ësen noon ko it ca Kalabaar, ci Kamerun, ay noonam duñ dooni Soko Uru ak i xërëmam mbaa soldaari Pël yeek seeni fetal yu gudd. Déedéet. | Au Calabar, au Cameroun, l'ennemi n'est plus Aro Chuku et son oracle, ni les armées des Foulanis et leurs longues carabines venues d'Arabie. | null |
Génnéel wépp fas woo gis ! | Fais sortir tout cheval que tu vois ! | null |
Góor gaa ŋgi, nitu Ndar la. | L'homme le voici, il est Saint-Louisien. | null |
Bëgg naa ci juróomi waxtu, ci subë, ŋga ñëw ! | Je veux que tu viennes le matin à cinq heures dans la fraîcheur ! | null |
Gàddaay ba nekk fu amul daay | S'exiler pour fuir les feux de brousse | null |
Gis naa góor gi ñëw ! | J'ai vu l'homme qui est venu ! | null |
Wool góor gi dul dem | Appelle l'homme qui ne part pas | null |
Keneen la ku yeksi ? | C'est un autre qui est venu ? | null |
Ci ginnaaw gi la door a gisaat jabar ji, xaw a miinal boppam doom yi. Ngan gu gàtt googu, dara laa ci fàttalikuwul. | Ce n'est qu'à la fin de la guerre qu'il pourra revoir sa femme et faire la connaissance de ses enfants au cours d'une brève visite dont je ne garde aucun souvenir. | null |
Gis naa ki woon. | J'ai vu celui en question. | null |
Góor gi daan na la gis | L'homme te voyait | null |
Amul benn ardow Jéeri boo xamul ! | Il n'est de Ardo du Dieri que tu ne connaisses ! | null |
Du góor. | Ce n'est pas un homme. | null |
Góor gi dana dem | L'homme partira | null |
Lu mat ay at, Ayijook Baay bindante nañu. | Ahidjo, lui, a écrit régulièrement à mon père en France pendant des années. | null |
Aminta ñëw ? | Aminata peut-elle venir ? | null |
Ñakk yiy aar askan wépp ci jàngoro yiy wàlle, néew naňu lool ñoom itam. | Les vaccins sont en quantité très limitée, pour combattre les épidémies. | null |
Lii ab kaas la mi ngi def am soow. Ab kaas bu weex la bu def am soow ñu taaj ko. | Ceci est une tasse qui contient du lait. C'est une tasse blanche, posée, contenant du lait. | null |
Sërin bi bëgg na mayewoon alalam ji ba mënkoon yalwaan tay. | Le maître souhaiterait avoir donné toute sa fortune pour pouvoir demander aujourd'hui l'aumône. | null |
Yaa demulwoon | C'est toi qui n'a pas été | null |
Ma may ñan ? | Je donne à qui ? | null |
Kaayleen ! | Venez ! | null |
Génnéel mépp xar moo gis ! | Fais sortir tout mouton que tu vois ! | null |
Ku dem ? | Qui a été ? | null |
Fo jëm ? | Où vas-tu ? | null |
Radiyasioŋ bi dafa di genn ci benn yëf ci plomb bu roppalaan bi lakkee ba pare. | Le rayonnement s'échapperait d'un composant en plomb après que l'avion ait brûlé. | null |
Yaral xar ! | Élève un mouton ! | null |
Dëgg la, la woon wonni na. Mu tekki ne gone gee may séen muy réer ci biir ñax mi, jant biy raay yaram wi, asamaan siy dajale, gone googu sori na sori gu, samay kàddu walla samay tànk manuñoo fexe ba dab ko. | Le monde change, c'est vrai, et celui qui est debout là-bas au milieu de la plaine d'herbes hautes, dans le souffle chaud qui apporte les odeurs de la savane, le bruit aigu de la forêt, sentant sur ses lèvres l'humidité du ciel et des nuages, celui-là est si loin de moi qu'aucune histoire, aucun voyage ne me permettra de le rejoindre. | null |
Xamoon na ni àddina du dox ba mu am bés dooley ubbi kilinigu boppam. | Il sait déjà qu'il n'aura pas les moyens de s'installer comme médecin privé. | null |
Wool góor gi dul Kajgaamu fii ! | Appelle l'homme qui n'est pas un Kangame d'ici ! | null |
Moo fa daan def lépp, di faj, di rewle, ku faatu yit mu ubbi la seet lu la faat. | Là, il faisait tout, comme il l'a dit plus tard, de l'accouchement à l'autopsie. | null |
Nataal bii ma gis de ay nit yun tabax la ak i garab ak i fleur ak yooyu. Ñu nekk fu taaroo taaru am miir bu leen wër miir boo xam ne peinture bu soon lañ ko peinture. | Sur cette photo ci que je vois il y a des personnes qu'on a fabriquées avec des arbres, des fleurs et consorts. Ils sont dans un endroit très beau avec des murs les entourant. Des murs peints avec de la peinture jaune. | null |
Cam ! | Pouah ! | null |
Waaw mbokk mi lii de gis naa ni baraada la, baraada bu taaru. Jumtukaay bu ñuy defare xéewal googu ñu naan café moom la ñu ngi ci diseene ñaari garab ñu ngi wanewaat ca kaw ñaari garab ak benn kéwël. | Oui le parent, je vois que ceci c'est une théière, une très belle théière. Un outil sur la quelle on prépare ce plaisir là qu'on appelle le café. On y a dessiné deux arbres. On y voit encore, au-dessus, deux arbres et une gazelle. | null |
Soo demee ag soo demul itam, dana ñëw. | Que tu partes ou que tu ne partes pas, il viendra. | null |
Li waa ji wax | Ce que cet homme a dit | null |
Nataalu këru Ogosaa gi ma dese, bu tuutee-tuuti la. Tóokër bu yaatu bi, ndeysaan... Garabi-tiir yeek garabi mbër yi... Yoon wii Baay daan gaare wotoom, W8 bu réy a réy ba. Saa yu ma xoolee bile nataal, fàww ma ni ci sama xel : ndax ci dëgg-dëgg fii laa dëkkoon ? Manumaa nangu ba tey ne benn béréb bi la. | Si je regarde aujourd'hui la seule photo que j'ai conservée de la maison d'Ogoja (un cliché minuscule, le tirage 6 x 6 courant après la guerre), j'ai du mal à croire qu'il s'agit du même lieu : un grand jardin ouvert, où poussent en désordre des palmiers, des flamboyants, traversé par une allée rectiligne où est garée la monumentale Ford V8 de mon père. | null |
Géej gaa ngii. Garabi-tiir yaa ngi nii ñoom tamit. Moonte liñ leen di miin yépp, teewul mbir mi mel ni lu kéemaane te raglu. | Il y a du mystère et de la sauvagerie, malgré la plage, malgré les palmes. | null |
Yobul na góor gi xar kërëm. | Il a amené à l'homme un mouton chez lui. | null |
Jambaar du bare wax. | Homme de courage n'abonde pas paroles. | null |
Nit ñi daawuñu coow. | Les gens n'étaient pas, habituellement, bavards. | null |
Lu yàgg déggu ñu, déggunu ko, muy wéy di liggéey Afrig ci anam yu jafe. Lépp jamp, garab ak jumtukaay nàkk, xare bu metti rëbloo dunyaa, reyante bi ne kurr. Loolu yombutoon a dékku, yaakaar ju tas xajoon na ci. | De longues années d'éloignement et de silence, pendant lesquelles il a continué d'exercer son métier de médecin dans l'urgence, sans médicaments, sans matériel, tandis que partout dans le monde les gens s'entre-tuaient – cela devait être plus que difficile, cela devait être insoutenable, désespérant. | null |
Nit dem na ! | Quelqu'un est parti ! | null |
Radiyasiyoŋ bi mën nañu ko tamit tëyé su amee lakk. | Le rayonnement peut également être contenu pendant un incendie. | null |
Ñépp ñan ŋga gis ? | Tous lesquels as-tu vus ? | null |
Yaakaar, nax sa bopp doŋŋ la. | Espérer, c'est se nourrir d'illusion. | null |
Ma daaneele xanaa móobalam ya. Soppul woon tabure yeek gàngune yooyu seen toogu yaatu, te ñu taq ci cosaanu nit ku ňuul. | Les meubles enfin, non pas ces fameux tabourets et trônes monoxyles d'art nègre. | null |
Faatim la soo demee ! | C'est Fatim, si on va au fond des choses ! | null |
Bés, mu dem doxantu ci tàkkal-dex gi ba delsi, fekk këram benn bataaxal. Muy kàddu yu gàtt, te tukkee ci kilifag loppitaan bi : “Góor gi, jotaguma ba tey sab kàrt de wisit.” Laata mu fay dem, Baay móol-lu na, gaa, ab kàrt – maa ngi ceek benn ba tey – wànte turam doŋŋ a ca nekkoon, bindu ci woon fa mu dëkk astemaak li muy liggéey. Ñàkk tegginu direkteer bi merloo ko, mu daldi ñaan ci saa si ñu yóbbu ko feneen. | À son retour à la pension, une lettre l'attend, un mot très sec du chef de l'hôpital disant : « Monsieur, je n'ai pas encore reçu votre carte de visite. » Mon père fait donc imprimer les fameuses cartes (j'en ai encore un exemplaire), juste son nom, sans adresse, sans titre. Et il demande son affectation au ministère des Colonies. | null |
Mu mel ni ñu ngi dox ci biiriy armeel. | C'est un cimetière vaste comme un pays. | null |
Soo demée, mu ñëw. | Si tu pars, il vient. | null |
Gis naa googii gan gi doon wax ! | J'ai vu ce visiteur qui parlait ! | null |
Ci juroom xale yi benn a ci dee. | Un enfant est mort sur les cinq. | null |
Xar yenn yooyu laa wax ! | Je parle de ceux-là ! | null |
At ya ma fa dund ngiy wéy di ma dugg, di ma mëdd ak a miirloo. | Par bouffées cela me submerge et m'étourdit. | null |